Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK JURÓOM-BENN

Woneel ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge

Woneel ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge
  • Lan la Biibël bi wax ci tuuri maam yi ak nataal yi ñuy jëfandikoo ngir jaamu Yàlla ?

  • Lan la karceen yi xalaat ci feet yi ñuy màggal ci diine yi ?

  • Naka nga mënee wax say moroom li nga gëm, te bañ leen merloo ?

1, 2. Boo génnee ci diine bu dul dëgg ba pare, ban laaj nga war a laaj sa bopp, te ci yow, lu tax loolu am solo ?

XALAATAL nga yëg ne dafa am ku nëbbatu, daldi tuur ci seen gox mbalit bu bon, bu mën a posone sa dëkkandoo yépp. Te fi mu nekk nii sax, mbalit boobu mu ngi bëgg a rey ñi fa dëkk ñépp. Su boobaa looy def ? Wóor na ne dinga jóge foofu boo ko mënee. Waaye boo fa jógee sax, dinga laaj sa bopp lu am solo lii : ‘ Ndax poson boobu dugg na ci sama yaram ba pare ? ’

2 Lu mel noonu moo am ci lu jëm ci diine bu dul dëgg. Biibël bi nee na diine yooyu dañu leen poson ak njàngale yu bon ak it jëf yu am sobe (2 Korent 6:17). Looloo tax génn ci “ Babilon mu mag mi ”, maanaam mbooloo diine yu dul dëgg yépp ci àddina si, am solo lool (Peeñu ma 18:​2, 4). Ndax génn nga ci ? Su dee def nga ko ba pare, jàmbaar dëgg nga. Waaye génn ci diine bu dul dëgg kese doyul. Boo defee loolu ba pare, war nga laaj sa bopp lii : ‘ Ndax amul dara lu des ci man te mu bokk ci fasoŋ bu baaxul bi ñuy jaamoo Yàlla ? ’ Nañu waxtaan tuuti ci loolu.

JAAMU AY NATAAL AK TUURI MAAM YI

3. a) Lan la Biibël bi wax ci jëfandikoo ay nataal ngir jaamu Yàlla, te lu tax nangu li Yàlla wax ci nataal yi, jafe lool ci ñenn ñi ? b) Lan nga war a def ak li nga yore te mu bokk ci fasoŋ bu baaxul bi ñuy jaamoo Yàlla ?

3 Am na ñu yore ci seen biir kër ay nataal walla ay béréb fu ñuy defe sarax, lu mat ay ati at. Ndax am nga loolu sa kër ? Bu dee waaw, ci yow ñaan Yàlla te bañ a jaar ci lu mel noonu ñuy gis, mën na nirool lu doy waar walla sax lu baaxul. Mën na am sax mu am yi nga ci fonk lool. Waaye Yàlla moo war a wax ni ñu koy jaamoo. Te Biibël bi wax na ne Yàlla bëggul ñuy jaar ci nataal ngir jaamu ko (Gàddaay gi 20:​4, 5 ; Psaume 115:​4-8 ; Esayi 42:8 ; 1 Yowaana 5:21). Kon dinga mën a wone ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, boo sànnee walla nga làkk lépp li nga yore te mu bokk ci fasoŋ bu baaxul bi ñuy jaamoo Yàlla. Nanga leen gise ni leen Yexowa gise​, maanaam gise leen ni lu araam. ​— Deutéronome 27:⁠15.

4. a) Naka lañu xame ne mbirum tuuri maam yi amul benn njariñ ? b) Lu tax Yexowa tere ay jaamam ñu bokk ci gisaane, luxus, kort walla lu mel noonu ?

4 Mbirum tuuri maam yi bokk na itam ci diine yu dul dëgg yu bare. Bala ñuy xam dëgg gi nekk ci Biibël bi, am na ñu gëmoon ne, ñi dee dañuy kontine di dund feneen fu kenn mënul a gis. Te dañu gëmoon ne ñi dee mën nañu dimbali ñiy dund, walla lor leen sax. Xéyna tàmmoon nga di def li nga mën ngir neexal say maam yi gaañu. Waaye ni ñu ko gise woon ci pàcc 6, ñi dee nekkuñu fenn di dund. Kon jéem a wax ak ñoom amul benn njariñ. Lépp lu niru ak lu jóge ci mbokk walla xarit bu gaañu, ci dëgg-dëgg, ci rab yi la jóge. Looloo tax Yexowa tere woon waa Israyel ñu jéem a wax ak ñi dee, walla ñu bokk ci gisaane, kort, luxus walla lu mel noonu. ​— Deutéronome 18:​10-12.

5. Su dee bu njëkk danga doon jëfandikoo nataal ci sa diine walla nga doon topp mbirum tuuri maam yi, loo mën a def léegi ?

5 Su dee bu njëkk danga doon jëfandikoo ay nataal ci sa diine walla nga doon topp mbirum tuuri maam yi, loo mën a def léegi ? Jàngal te xalaat ci Biibël bi aaya yuy wone ni Yàlla di gise mbir moomu. Waxal ak Yexowa bés bu nekk ci li nga bëgg a wone ci say jëf ne danga ko bëgg a jaamu ni mu ko bëgge. Wax ko it mu dimbali la nga bokk xalaat ak moom.​ — Esayi 55:9.

KARCEEN​ YU NJËKK YI DAAWUÑU MÀGGAL BÉSU NOWEL

6, 7. a) Lan la nit ñi bëgg a màggal ci bésu Nowel, te ndax taalibe Yeesu yu njëkk yi dañu doon màggal bés boobu ? b) Ci ñan lañu xame woon màggal bésu juddu ci jamano taalibe Yeesu yu njëkk ya ?

6 Am na fu diine bu dul dëgg mënee tilimal fasoŋ bi nit di jaamoo Yàlla. Loolu mooy feet yi nit ñi di màggal ci àddina si. Nañu ko seet ci feetu Nowel. Nit ñi dañuy wax ne bés bi Yeesu juddu lañuy màggal ci feetu Nowel. Te li ëpp ci diine yuy wuyoo turu karceen dañuy màggal feet boobu. Waaye amul dara luy wone ne taalibe Yeesu yu njëkk ya dañu doon màggal bés boobu. Téere bi tudd Les origines sacrées de choses profondes (ci ãgale) nee na : “ Ci ñaari téeméeri at yi topp juddu Kirist, kenn xamul woon bés bi Yeesu juddu, te sax ñi bés boobu itteeloon barewuñu woon. ”

7 Su taalibe Yeesu yi xamoon sax bés bi Yeesu juddu, daawuñu woon màggal bés boobu. Lu tax ? Ndaxte, ni ko téere bi tudd The World Book Encyclopedia waxe, ci karceen yu njëkk ya, “ ñi doon jaamu xërëm ñoo doon màggal bésu juddu ”. Màggalu bésu juddu yi ñu wax ci Biibël bi, ñaari njiit yu daawul woon jaamu Yexowa ñoo ko defoon (Njàlbéen ga 40:20 ; Màrk 6:21). Dañu doon màggal itam ay bésu juddu jagleel ko ay xërëm. Maanaam ci bésu 24 me, waa Room dañu doon màggal bésu juddu seen yàlla bu jigéen bi tudd Diane. Bés bi ci topp, dañu doon màggal juddu naaj bi nekkoon yàlla ci ñoom te ñu ko doon woowe Apollon. Kon nag, màggal bésu juddu, ci ñiy jaamu xërëm lañu ko xame woon. Waaye masul a bokk ci diine karceen.

8. Woneel li màggal bésu juddu bokk ak biddaa.

8 Am na leneen it lu taxoon taalibe Yeesu yu njëkk ya bañ a màggal bésu juddu Yeesu. Xéyna taalibeem yi, xamoon nañu ne màggal bésu juddu am na lu mu bokk ak biddaa yi. Ci jamono yu njëkk yi, ñu bare ci waa Geres ak ci waa Room, dañu gëmoon ne dafay am jinne buy teew saa yu nit di juddu. Te jinne boobu dafay aar nit kooku ci giiru dundam gépp. Téere bi tudd Aada yi jëm ci màggal bésu juddu (ci ãgale) lii la wax : “ Jinne bi fekke juddu nit ki, dafay am lu muy séq ak yàlla bi bokk bésu juddu ak nit kooku. ” Wóor na ne màggal feet buy boole Yeesu ci biddaa yooyu, neexul Yexowa (Isaïe 65:11, 12). Kon lan moo tax ba ñu bare di màggal Nowel ?

FU NOWEL JÓGE

9. Naka la 25 desàmbar deme ba nekk bés bi ñuy màggal juddu Yeesu ?

9 Ay téeméeri at ginnaaw bi fi Yeesu jóge, la nit ñi komaase di màggal bésu juddoom ci 25 desàmbar. Waaye Yeesu judduwul ci bés boobu. Leer na ne ci weeru oktoobar la Yeesu waroon a juddu *. Kon lu tax nit ñi tànn bésu 25 desàmbar ? Dafa mel ni ay nit ñu doon mbubboo diine karceen ñoo “ bëggoon bés boobu tombe ak benn feet bu jóge ci boroom xërëm yi nekkoon Room. Feet boobu moo doon màggal ‘ juddu jant bi, bu kenn mënuloon a daan ’ ”. (The New Encyclopædia Britannica.) Bu sedd bu metti bi ñëwee, ba doole naaj bi mel ni luy wàññeeku, ñiy jaamu xërëm dañu doon def ay màggal ngir naaj bi leen di indil leer ak tàngoor dellusi ci tukkeem yu sore yi. Dañoo foogoon ne bésu 25 desàmbar la naaj bi doon komaasee dellusi. Njiitu diine yi dañu bëggoon ñiy jaamu xërëm tuub nekk karceen. Moo tax ñu jël feet boobu, te fexe ba mu mel ni feetu “ karceen ” *.

10. Ci jamono yi paase, lu tax ay nit bañoon a màggal bésu Nowel ?

10 Bi ñu xamee ne Nowel ci diine ñiy jaamu xërëm la jóge, yàgg na lool. Nowel jógewul ci Biibël bi. Moo tax ci ati 1600 yi ñu tere woon ku koy màggal ca réewu Ãgalteer, ak ci yenn réew yi mu moomoon ca Amerig. Képp ku bañoon a dem liggéey ci bésu Nowel dafa waroon a fey alamaan. Waaye ci lu gaaw, nit ñi delluwaat ci aada yu njëkk yi te yokk ci yeneen yu bees. Nowel daldi nekkaat feet bu mag. Te ba tey sax feet bu mag la ci réew yu bare. Waaye li Nowel bokk ak diine bu dul dëgg, tax na ñi bëgg a neex Yàlla bañ koo màggal walla sax bañ a màggal bépp feet bu jóge ci ñiy jaamu xërëm *.

NDAX FI FEET JÓGE AM NA SOLO DËGG ?

11. Lu tax ñenn ñi di màggal feet yi, waaye lan moo war a gën a am solo ci ñun ?

11 Am na ñu nangu ne feet yu mel ni Nowel, ci ñiy jaamu xërëm lañu jóge. Waaye dañuy wax ne amul dara lu bon ci màggal feet yooyu. Li am mooy, li ëpp ci ñiy màggal feet yooyu, bu ñu koy def duñu xalaat lu jëm ci fasoŋ bu baaxul bu ñuy jaamoo Yàlla. Feet yu mel noonu, dafa leen di may ñu mën a jege seeni mbokk. Ndax noonu nga koy gise yow itam ? Bu dee noonu nga koy gise, wóor na ne li nga bëgg say mbokk moo tax wone ci say jëf ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge mel ni lu jafe ci yow. Waaye du li nga fonk diine bu dul dëgg. Na la wóor ne, Yexowa mi sos njaboot, dafa bëgg sa diggante ak say mbokk rattax lool (Efes 3:14, 15). Waaye mën nga rattaxal sa diggante ak say mbokk ci fasoŋ bu neex Yàlla. Lii la ndaw li Pool bindoon lu jëm ci li war a gën am solo ci ñun : “ Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi. ”​ — Efes 5:⁠10.

Ndax dinga lekk tàngal bu ñu for fu salte lool ?

12. Joxeel misaal buy wone lu tax ñu war a moytu aada ak feet yu jóge fu baaxul.

12 Xéyna dinga wax ne, du fi feet yooyu jóge moo tax ñu di leen màggal tey. Ndax fi feet yooyu jóge am na solo dëgg ? Waawaaw ! Nañu ko seet ci lii : Boo gisoon tàngal fu salte lool, ndax dinga ko for, lekk ko ? Déedéet ! Tàngal boobu setul. Ni tàngal boobu, feet yooyu dañu nirook lu neex, waaye fi ñu leen jële dafa am sobe. Bu ñu bëggee wone ci suñuy jëf ne dañu bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, dañu war a bokk xalaat ak yonent Yàlla Esayi, mi waxoon lii ñiy jaamu Yàlla dëgg : “ Buleen laal dara lu am sobe. ”​—  Esayi 52:​11, NW.

NAÑU XAM NI ÑU WAR A DEFE AK SUÑUY MOROOM

13. Yan jafe-jafe nga mën am boo dul bokk ci yenn feet yi ?

13 Xéyna dinga am ay jafe-jafe boo bëggatul màggal feet yooyu. Mën na am ñi nga bokkal liggéey laaj la lu tax bëgguloo bokk ci li ñuy def fi ngay liggéeye bu feet yooyu jotee. Su ñu la mayee dara ci Nowel, lan nga war a def ? Ndax nangu ko baaxul ? Boo bokkul diine ak sa jabar walla sa jëkkër, loo war a def ? Lan nga mën a def ba say doom bañ a foog ne, li ñu bokkul ci yenn feet yi dafa leen di xañ dara ?

14, 15. Loo mën a def su amee nit ku la ñaanal feet bu neex, walla mu may la dara ci feet yooyu ?

14 Dañu war a seet bu baax li ñu war a def saa su lu mel noonu amee. Su amee ku la ñaanal feet bu neex, mën nga ko wax jëre-jëf rekk. Waaye su dee ki ngay faral di gis la, walla ngeen bokk fi ngeen di liggéeye, xéyna nga leeral ko mbir mi. Ak lu mu mënta doon, danga war a teey. Biibël bi nee na : “ Na seen wax jépp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen war a tontoo ku nekk. ” (Kolos 4:⁠6). Nanga moytu ñàkkal kersa suñuy moroom. Nanga may nit ki cér boo koy wax sa xalaat ci feet bi. Nanga ko leeral bu baax ne bañuloo nit ñi di joxante ay maye ak di daje ak say moroom. Waaye, li la gënal mooy, def loolu ci bés yu wuute ak jamono yu ñuy màggale feet yooyu.

15 Loo war a def su amee ku la bëgg a may dara ? Lu ci ëpp, ni mbir mi deme mooy tax nga mën koo nangu walla déet. Ki la koy may mën na wax : “ Xam naa ne bokkuloo ci feet bi. Waaye ba tey, dama la bëgg a may lii. ” Mën na am nga nangu ko, ndaxte bu boobaa, du mel ni dangay bokk ci feet boobu. Waaye nag, su fekkee ne ki lay may dara xamul li nga gëm, mën nga ko wax ne doo màggal feet boobu. Loolu dina la may nga wax ko lu tax nga nangu li mu la jox, waaye yow ci sa bopp doo ko may dara ci bés boobu. Su fekkee nag dafa la leer ne nit ki dafa bëgg a wone ne doo topp li nga gëm, walla mu bëgg a wone ne li nga mën a am dina tax nga def lu àndul ak sa ngëm, bu boobaa, li gën mooy nga bañ a nangu li mu lay may.

NOO WAR A JËFE AK SA WAA KËR ?

16. Naka nga mënee nekk ku teey booy wax ci lu jëm ci feet yi ?

16 Lan nga war a def boo bokkul diine ak sa waa kër ? Danga war a teey itam. Soxlawul ngay werante ak say mbokk lu jëm ci bépp feet walla aada bu ñuy topp. Danga war a xam ne mën nañu am seen gis-gisu bopp. Te danga leen ci war a may cér ni nga bëgge yow it ñu may la cér ci sa gis-gis (Macë 7:12). Bul def dara luy tax nga bokk ci feet boobu. Waaye bul ëppal bu mbir mi bokkulee dara ak feet boobu. Waaye leer na ne, saa su nekk, waruloo def luy tax sa xel di la tuumaal. ​— 1 Timote 1:​18, 19.

17. Naka nga mënee dimbali say doom ñu bañ a foog ne, dañu leen di xañ dara ndax li ñuy gis ñeneen ñi di màggal feet yi ?

17 Naka nga mën a def ba say doom bañ a foog ne, li ñu bokkul ci feet yi àndul ak li Mbind mi wax, dafa leen di xañ dara ? Li ngay def ci yeneen bés yi ci at mi, dina ci def lu bare. Am na ay waajur yuy jàpp ay bés ngir may dara seeni doom. Li gën a réy ci li nga mën a may say doom, mooy may leen sa jot, ak di leen toppatoo ak mbëggeel gu doy.

NANGA JAAMU YÀLLA NI MU KO BËGGE

Jaamu Yàlla ni mu ko bëgge dafay indi mbégte dëgg.

18. Teewe ndaje karceen yi, naka la lay dimbalee nga wone ci say jëf ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge ?

18 Boo bëggee neex Yàlla, danga war a bañ bépp fasoŋ bu baaxul bu ñuy jaamoo Yàlla, te wone ci say jëf ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge. Lan la loolu di tekki ? Biibël bi nee na : “ Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi. ” (Yawut ya 10:24, 25). Ndaje karceen yi, lu neex la lu lay may nga jaamu Yàlla ci fasoŋ bi ko neex (Sabóor 22:23 ; Psaume 122:⁠1). Ci ndaje yooyu karceen dëgg yi dañuy ‘ dimbaleente ci seen ngëm ’.​ — Room 1:12.

19. Lu tax wax say moroom li nga jàng ci Biibël bi am solo lool ?

19 Leneen li nga mën a def ngir wone ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, mooy di wax say moroom lu jëm ci li nga jàng ak Seede Yexowa yi ci Biibël bi. Nit ñu bare ñu ngi “ metitlu ak di onk ” dëgg ndax lu bon li am ci àddina si tey (Esekiel 9:​4, NW). Xéyna am na ay nit ñi nga xam ñuy yëg loolu ci seen xol. Ndax mënuloo wax ak ñoom ci yaakaar bi la Biibël bi may ci ëllëg ? Booy ànd ak karceen dëgg yi, te di wax say moroom lu jëm ci dëgg yu neex yi nekk ci Biibël bi, li nga bëgg di topp aada yi bokk ci fasoŋ bu baaxul bu ñuy jaamoo Yàlla, dina deñ ndànk-ndànk ci sa xol. Na la wóor ne, boo wonee ci say jëf ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, dinga bég lool, te it dinga am ay barke yu bare. ​— Malaki 3:⁠10.

^ par. 9 Feet bi ñuy woowe ci tubaab Les Saturnales bokk na itam ci li taxoon ñu tànn bésu 25 desàmbar. Diggante 17 ba 24 ci weeru desàmbar lañu doon def feet boobu ca Room ngir màggal yàlla mbey mi. Feet boobu feet bu réy la woon, nit ñi dañu doon mbuumbaay te di joxante ay maye.

^ par. 10 Boo bëggee gën a am ay leeral ci ni karceen dëgg yi di gise yeneen feet yi nit ñi di màggal, seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 222 ak 223.