Fàttaliku deewu Yeesu
Alxemes, 2 awril 2026
Benn yoon ci at mu nekk, Seede Yexowa yi dañuy fàttaliku deewu Yeesu, ni mu ko santaanee. Lii la waxoon: «Defleen lii, ngir fàttaliku ma» (Luug 22:19).
Ñu ngi leen di woo, yow ak sa waa kër, ngeen ñëw teewe xew-xew bu am solo boobu.
Li nit ñi faral di laaj
Kan moo ci mën a teew?
Ñépp a ci mën a teew. Kon booy ñëw, mën nga ànd ak saay xarit ak sa waa kër.
Ñaata waxtu la ndaje bi di def?
Ndaje bi, daanaka benn waxtu lay def.
Fan lay amee?
Laajal benn Seede Yexowa mu wax la fi muy ame.
Ndax boo fay dugg danga war a fey dara? Ndax danga war a faral di teewe suñu ndaje yi?
Déedéet.
Boo fa duggee ba pare, ndax dinañu la laaj nga maye xaalis?
Déedéet. Ci ndaje Seede Yexowa yi, doo gis kenn kuy wër di laaj nit ñi xaalis.—Macë 10:8.
Ku bëgg a teewe ndaje bi, naka la war a soloo?
Duñu wax kenn ni mu war a soloo. Waaye nag, Seede Yexowa yi dañuy góor-góorlu di sol lu yiw ngir won Yàlla respe bi mu yelloo ci xew-xew bu am solo boobu.
Lan lañuy def ci bésu fàttaliku bi?
Bu ñuy tàmbali ndaje bi, dañuy woy, ba pare benn Seede Yexowa def ñaan. Loolu it lañuy def bu ndaje bi di jeex. Waxtaan bi dina wone li tax deewu Yeesu am solo ak li ñu mën a def ba li ñu Yàlla ak Kirist defal amal ñu njariñ.
Boo ci bëggee am yeneen leeral, xoolal waxtaan bi tudd ci farãse: «Pourquoi les Témoins de Jéhovah célèbrent-ils le Repas du Seigneur différemment des autres religions?»
Kañ la bésu fàttaliku bi di am ci at yii di nëw?
2026: Alxemes, 2 awril
2027: Altine, 22 màrs

