Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 8

Lu tax Yàlla bàyyi lu bon ak coono yi di am ?

Lu tax Yàlla bàyyi lu bon ak coono yi di am ?

1. Kañ la lu bon komaase ?

Yàlla bàyyi na nit ñi jiite seen bopp lu yàgg ngir wone ne mënuñu faj poroblemu doomu Aadama yi.

Bi Seytaane njëkkee fen, ci la lu bon komaase ci kaw suuf. Ca njàlbéen, Seytaane malaaka bu mat sëkk la woon, waaye ‘ taxawul ci dëgg ’ (Yowaana 8:44). Dafa bëgg ñu jaamu ko fekk ne Yàlla rekk lañu war a jaamu. Seytaane dafa fen Awa jigéen ju njëkk ja, xiir ko mu déggal ko te bañ a déggal Yàlla. Aadama topp na Awa ci bañ a déggal Yàlla. Li Aadama def moo indi coono ci kaw suuf si. — Jàngal Njàlbéen ga 3:1-6, 19.

Bi Seytaane xiiree Awa mu bañ a déggal Yàlla, ci la xeex kiliftéefu Yàlla tàmbalee, maanaam sañ-sañu jiite bi Yàlla am. Ñu bare ci doomu Aadama yi topp nañu Seytaane ci bañ Yàlla jiite leen. Noonu la Seytaane nekke kiy “ jiite àddina ”. — Jàngal Yowaana 14:30 ; 1 Yowaana 5:19.

2. Ndax li Yàlla sàkk amoon na sikk ?

Li Yàlla bind lépp a mat sëkk. Nit ñi ak malaaka yi Yàlla sàkk mënoon nañu déggal Yàlla bu baax (Deutéronome 32:4, 5). Yàlla sàkk na ñu ak sañ-sañu tànn def lu baax walla lu bon. Sañ-sañ boobu mooy tax ñu mën a wone suñu mbëggeel ci Yàlla. — Jàngal Saag 1:13-15 ; 1 Yowaana 5:3.

3. Lu tax Yàlla bàyyi coono yi am booba ba léegi ?

Lu tax Yexowa bàyyi ñuy xeex kiliftéefam booba ba léegi ? Ngir wone ne lépp lu ñuy def ngir jiite suñu bopp du ñu yóbbu fenn (Ecclésiaste 7:​29 ; 8:9). Li ko firndeel ci lu leer mooy jaar-jaaru doomu Aadama yi booba ba tey, maanaam ci 6 000 at yi weesu. Nguuru doomu Aadama yi wone nañu ne mënuñu fi jële xare, reyante, njubadi ak feebar. — Jàngal Jérémie 10:23 ; Room 9:​17.

Ni Yàlla di jiitee wuute na lool ak ni doomu Aadama yi di jiitee, ndaxte dafay amal njariñ ñi ko nangu (Isaïe 48:17, 18). Ci kanam tuuti, Yexowa dina fi jële nguuru doomu Aadama yépp. Ñi tànn Yàlla jiite leen ñoom kese ñooy dund ci kaw suuf si. — Esayi 11:9. — Jàngal Dañeel 2:44.

Seetaanal wideo Lu tax Yàlla bàyyi coono yi di am ?

4. Lan la ñu muñug Yàlla di may ?

Seytaane dafa wax ne amul kenn kuy jaamu Yexowa ci kaw mbëggeel kese. Ndax bëgg nga wone ne Seytaane waxul dëgg ? Mën nga ko kay ! Muñug Yàlla may na ñu ñu wone ndax Yàlla lañu bëgg mu jiite ñu, walla dañu bëgg nguuru doomu Aadama yi jiite ñu. Ni ñuy dunde dafay wone fi ñu féete. — Jàngal Job 1:8-12 ; Kàddu yu Xelu 27:11.

5. Naka lañu mënee tànn Yàlla mu nekk suñu njiit ?

Suñu tànneef dina wone ndax bëgg nañu Yàlla jiite ñu.

Mën nañu tànn Yàlla jiite ñu, su fekkee ne ñu ngi wut te di topp ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko te mu dëppoo ak Kàddoom Biibël bi (Yowaana 4:23). Mën nañu bañ Seytaane jiite ñu bu ñu bokkul ci politig ak xare yi, ni ko Yeesu defe woon. — Jàngal Yowaana 17:14.

Seytaane dafay jëfandikoo kàttanam ngir gëmloo nit ñi ne dundin bu bon ak jëf yu bon baax na. Su ñu bañee topp jëf yooyu, mën na am ñenn ci suñu xarit yi, walla ci suñu mbokk yi reetaan ñu walla xeex ñu (1 Piyeer 4:3, 4). War nañu wone fu ñu féete. Ndax dinañu ànd ak ñi bëgg Yàlla ? Ndax dinañu topp sàrtu Yàlla yiy wone mbëggeelam ci ñun ? Bu ñu defee loolu, dinañu wone ne Seytaane dafay fen bi mu waxee ne, kenn du déggal Yàlla bu nekkee ci jafe-jafe. — Jángal 1 Korent 6:9, 10 ; 15:33.

Ni Yàlla bëgge doomu Aadama yi dafay tax mu wóor ñu ne lu bon ak coono dina jeex. Ñi wone ne gëm nañu loolu dinañu am dund gu dul jeex ci kaw suuf si. — Jàngal Yowaana 3:16.