Ubbil li ci biir

Lan la Biibël bi wax ci nekkaale?

Lan la Biibël bi wax ci nekkaale?

Li Biibël bi wax

Biibël bi nee na Yàlla dafa bëgg nit ñi «moytu njaaloo» (1 Tesalonig 4:3). Baat bi ñu tekki fii ci wolof «njaaloo», boo ko gisee ci Biibël bi dafa ëmb ku am jëkkër walla jabar ba pare tëdd ak keneen, ak it góor-jigéen, ak itam benn góor ak benn jigéen ñu tëdd fekk séyuñu.

 Ni Yàlla di gise séy walla nekkaale, lu tax loolu am solo?

  • Yàlla moo sos séy. Def na ko bi mu indee Awa ci suñu maam Aadama (Njàlbéen ga 2:22-24). Bëggul woon góor ak jigéen di dëkk ni jëkkër ak jabar fekk séyuñu ci yoon.

  • Yàlla moo ñu gën a xam li gën ci ñun. Yàlla dafa bëggoon séy am diggante benn góor ak benn jigéen te mu nekk luy sax. Loolu mooy indil njaboot gi jàmm ak xel mu dal. Dafa mel ni minise bu war a monte armoor bu jóge bitim réew. Fàww mu topp li ki ko defar bind ci kayit ngir xam ni ñu koy montee. Noonu it tegtal yi jóge ci Yàlla ñoo ñuy won li ñu war a def ngir am jàmm ci suñu kër. Boo toppee li Yàlla santaane, njariñ rekk nga ciy jële (Esayi 48:17, 18).

    Bu ñu jëndee armoor bu bees bu ñu booleegul bant yi, ki ko defar mooy joxe tegtal yi ngir monte ko. Tegtal yi jóge ci Yàlla ñoo ñuy won li ñu war a def ngir am jàmm ci suñu kër.

  • Tëdd ak koo séyalul, mën na indi lu metti lool. Mën na doon ëmb, feebaru séy, walla yaakaar bu tas ak naqaru xol bu réy. *

  • Yàlla moo may góor ak jigéen ñu mën a am doom. Dund, lu sell la ci kanamu Yàlla te mën a am doom, maye Yàlla la. Yàlla dafa bëgg ñu wone ne fonk nañu maye boobu bu ñu séyee bala ñuy am doom (Yawut ya 13:4).

 Nekkaale ngir gën a xamante, ndax loolu baax na?

«Nekkaale ngir gën a xamante» te ngeen xam ne ku nekk mën nga dem sa yoon saa yu la neexee, du loolu mooy tax nga am jàmm bés boo séyee. Waaye bu kenn ku nekk fas yeenee dund ak ki mu séyal dundam yépp te bañ a bàyyi jafe-jafe yi yàq seen séy, loolu dina dëgëral bu baax seen diggante * (Macë 19:6).

 Naka la jëkkër ak jabar mënee am séy bu neex?

Amul benn séy bu amul jafe-jafe. Waaye, jëkkër ak jabar mën nañu am jàmm ci seen séy bu ñu toppee tegtal yi nekk ci Biibël bi. Seetal yii di topp:

^ par. 4 Seetal li ñu wax ci «Les jeunes s’interrogent–Aller plus loin: et si je cédais?» (maanaam xale yi ñooy laajte lu ñu mën a def su amee ku leen bëgg a xiir ci tëdd ak ñoom)

^ par. 6 Seetal li ñu wax ci waxtaan bi tudd «Pour les couples—Engagement.» (maanaam ñi séy war nañu fas yeenee dund ak ki ñu séyal seen dund bi yépp)