Ubbil li ci biir

Lan moo mën a indi jàmm ci biir kër ?

Lan moo mën a indi jàmm ci biir kër ?

 

  • mbëggeel ?

  • xaalis ?

  • walla leneen ?

LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?

“ Ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp. ” — Luug 11:28, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.

LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?

Dëkk ci mbëggeel dëgg. — Efes 5:28, 29.

Ñu may la cér. — Efes 5:33.

Doo ragal ñu wor la walla ñu bàyyi la. — Mark 10:6-9.

NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?

Waaw waaw, xoolal liy topp :

  • Yàlla moo sos njaboot. Biibël bi nee na Yexowa mooy Yàlla miy “ cosaanul njaboot gépp ”. (Efes 3:14, 15) Maanaam Yexowa moo sàkk njaboot. Lu tax gëm loolu am solo ?

    Seetal lii : bu ñu la woowee añ, mu neex lool ba nga bëgg a xam li ñu ci def, koo koy laaj ? Xanaa ki ko togg, du dëgg ?

    Noonu it, boo bëggee xam li nga war a def ba am jàmm ci sa kër, ndax doo dem ci Yexowa mi sos njaboot ? — Njàlbéen ga 2:18-24.

  • Yàlla fonk na la. Yàlla “ ku leen ñeewante la ”, maanaam Yexowa dafa ñu fonk. (1 Piyeer 5:6, 7) Kon njaboot yi am xel ñooy wut xelal ci moom ngir am jàmm ci seen biir. Xelal yooyu, mën nañu leen jàng ci Kàddoom. Yexowa, lépp lu mu wax, suñu njariñ la. — Kàddu yu Xelu 3:5, 6 ; Isaïe 48:17, 18.

LOO XALAAT CI LAAJ BII ?

Loo war a def ngir nekk jëkkër walla jabar ju baax, te mën a yar say doom bu baax ?

Biibël bi dafa ciy tontu ci EFES 5:1, 2 ak KOLOS 3:18-21.