Ubbil li ci biir

Ndax ñi dee dinañu dundaat ?

Ndax ñi dee dinañu dundaat ?

Ndax dinga ne . . .

  • waaw ?

  • déedéet ?

  • xéyna ?

LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?

Ñi dee “ dinañu dekki ”. — Jëf ya 24:15, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.

LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?

Day dëfël sa xol boo amee mbokk bu gaañu. — 2 Korent 1:3, 4.

Doo ragal a dee. — Yawut ya 2:15.

Dinga am yaakaaru gisaat say mbokk yu gaañu. — Yowaana 5:28, 29.

NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?

Waaw waaw, xoolal liy topp :

  • Yàlla moo sàkk dund. Biibël bi nee na Yexowa Yàlla “ mooy jox ñépp bakkan ”. (Jëf ya 17:24, 25 ; Sabóor 36:10) Ki nga xam ne moom mooy jox ñépp bakkan, kooku wóor na ne mën na dekkil ku dee.

  • Yàlla mas na dekkil ay nit. Biibël bi wax na ci juróom-ñetti nit yu dekki ci kaw suuf. Amoon na ci ay xale, ay mag, ay góor ak ay jigéen. Amoon na ci ñu yàggul woon a dee, waaye kenn ci ñoom dee woon na ba am sax ñeenti fan bala ñu koy dekkil ! — Yowaana 11:39-44.

  • Yàlla yàkkamti na defaat loolu. Yexowa ci boppam bëggul mukk nit dee ; dafa gise dee ni noon. (1 Korent 15:26) Dafa bëgg lool noot noon boobu te dekkil ñi nekk ci xelam, ñu dundaat ci kaw suuf. — Job 14:14, 15.

LOO XALAAT CI LAAJ BII ?

Lu tax ñuy màgget di dee ?

Biibël bi dafa ciy tontu ci NJÀLBÉEN GA 3:17- 19 ak ROOM 5:12.