Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Leetar bu jóge ci Jataay biy dogal

Leetar bu jóge ci Jataay biy dogal

Ni ko Biibël bi wonee, dañu war a nekk ay jàngalekat (Yawut Ya 5:12). Xalaatal lii rekk: Yexowa mi nekk Jàngalekat bi gën a mag moo ñu wax ñu jàngal ñeneen ñi ngir ñu xam ko! Cér bu réy la te it liggéey bu mag la, di jàngal nit ñi dëgg gi jëm ci Yexowa, muy ci njaboot gi, ci mbooloo mi walla bu ñuy waare. Naka lañu mënee def liggéey boobu ni mu ware?

Tont baa ngi ci kàddu yi ndaw li Pool bindoon Timote. Mu ne ko: «Saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di léen dénk ak a jàngal.» Pool teg ci ne: «Kon dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu» (1 Timote 4:13, 16). Li ngay jàngale dafay musal nit. Kon war nga góor-góorlu bu baax ci gën a mën a jàng ak jàngale. Looloo waral téere bii. Xoolal li ci nekk:

Paas bu nekk am na aaya Biibël bu ci nekk. Mën na nekk lu Biibël bi santaane walla luy misaal ni ñu mënee topp njàngale bi.

Amul kenn ku mën a jàngalee ni Yexowa (Ayóoba 36:22). Téere bii dina la dimbali nga yokk sa mën-mën ci jàng ak jàngale, waaye bul fàtte mukk ne Yexowa mooy xiir nit ñi ci moom te li ngay jàngale, ci moom la jóge (Yowaana 6:44). Kon nag nanga faral di ñaan Yexowa mu may la xel mu sell mi. Tàmmal di sukkandiku ci Kàddu Yàlla. Bul jàngale mukk sa xalaatu bopp, waaye nanga jàngale xalaatu Yexowa rekk. Fexeel ba ñi lay déglu bëgg Yexowa bu baax ci seen xol.

Bokk nga ci njàngale bi gën a am solo bi ñu mas a dénk doomu Aadama yi. Wóor na ñu ne booy «jëfe dooley Yàlla» dinga def liggéey boobu ni mu ware (1 Piyeer 4:11).

Ñi nga bokkal liggéeyu jàngale bi,

Jataay biy dogal bu Seede Yexowa yi