Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 19

Defal lépp ngir laal xolu nit ñi

Defal lépp ngir laal xolu nit ñi

Kàddu yu Xelu 3:1

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu gis njariñu li nga leen di jàngal te ñu jëfe ko.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat ci li leen di tax a jëf. Laajal ay laaj yuy tax ñi lay déglu mën a seet li nekk ci seen xol.

  • Xiiral ñi lay déglu ci bëgg a def lu baax. Dimbalil bu baax ñi lay déglu ñu xalaat ci li tax ñuy def lu baax. Dimbali leen ba li leen xiir ci def lu baax doon li gën, maanaam bëgg Yexowa, bëgg seen moroom ak bëgg a topp li Biibël bi santaane. Dimbalil ñi lay déglu ñu xam ne li Biibël bi wax mooy li gën; bu leen xas. Bu leen rusloo, waaye fexeel ba sa waxtaan xiir leen ci bëgg a def lépp li ñu mën ngir def lu baax.

  • Gënal a wax ci Yexowa. Ndigal ak santaane Yàlla yi nekk ci Biibël bi ak lépp li Biibël bi wax, dafay wone jikko Yàlla yi ak mbëggeelam ci ñun. Na loolu feeñ bu baax ci sa njàngale. Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat ci li Yexowa di yëg bu ñuy def dara te xiir leen ci bëgg a def li ko neex.