Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 8

Ban njariñ la leen deewu Yeesu amal ?

Ban njariñ la leen deewu Yeesu amal ?

Deewu Yeesu dina ñu may dund gu dul jeex. Yowaana 3:16

Bi Yeesu deewee ba mu am ñetti fan, ay jigéen dem nañu ca bàmmeelam ; waaye fekkuñu fa néewam. Yexowa moo dekkaloon Yeesu.

Ginaaw loolu, Yeesu feeñu na ay taalibeem.

Ci dëgg, Yexowa dekkal na Yeesu, mu delluwaat ca kaw asamaan, nekk fa ku bare kàttan te du deewati mukk. Taalibe Yeesu yi gis nañu Yeesu bi muy dellu kaw asamaan.

Yàlla dekkal na Yeesu, def ko Buuru Nguuru Yàlla. Dañeel 7:13, 14

Yeesu dafa joxe bakkanam ngir musal nit ñi. Loolu mooy njot gi (Macë 20:28). Yàlla dafa jaar ci njot gi ngir nit ñi mën a am dund gu dul jeex.

Yexowa fal na Yeesu Buur ca kaw asamaan ngir mu nguuru ci kaw suuf si. Yeesu dina nguuru ak 144000 nit ñu baax ñoo xam ne Yàlla moo leen nar a dekkal ngir ñu dund ca kaw asamaan. Ñoom ñépp ñooy nguuru ca kaw asamaan ci Nguuru Yàlla mi nekk nguur gu jub. — Peeñu ma 14:1-3.

Nguuru Yàlla dina defar suuf si ba mu nekk àjjana. Dootul amati geer, reyante, xiif, walla ñakk bu metti. Jàmm dëgg dina am ci kaw suuf si. — Psaume 145:16.