Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 01

Naka la la Biibël bi mënee dimbali?

Naka la la Biibël bi mënee dimbali?

Daanaka ñun ñépp, dañuy laaj suñu bopp lii: ‘Lu tax ñu nekk ci kaw suuf?’ ‘Lu tax ñuy dund ci coono?’ ‘Lu tax nit di dee?’ ‘Suñu ëllëg nu muy mel?’ Bés bu nekk, dañuy xalaat itam ci ni ñu mënee faj suñuy soxla, walla ni ñu mënee am jàmm ci suñu biir njaboot. Ñu bare gis nañu ne, Biibël bi yemul rekk ci tontu ci laaj yu am solo yooyu, waaye am na itam ay xelal yu leen di dimbali ci seen dund bés bu nekk. Ndax foog nga ne, Biibël bi mën na dimbali ñépp ci seen dund?

1. Ci yan laaj la Biibël bi di tontu?

Biibël bi tontu na ci laaj yu am solo yii: Fan la nit jóge? Lu tax ñu nekk ci kaw suuf? Lu tax ñuy dund ci coono? Lan mooy dal nit bu deewee? Ndegam ñépp a bëgg am jàmm, lu tax geer yi bare? Lan mooy ëllëgu suuf si? Biibël bi dafa ñuy xiir ñu wut a xam tont laaj yooyu. Ay milyoŋi nit gis nañu tont yu leen doy ci Biibël bi.

2. Naka la ñu Biibël bi mënee dimbali ñu am jàmm ci suñu dund?

Biibël bi dafa ñuy jox ay xelal yu baax. Dafay won njaboot yi ni ñu mënee am jàmm dëgg. Dafa ñuy won li ñu mën a def bu ñu jaaxlee ak li ñu mën a def ba fonk suñu liggéey. Boo kontinee njàng mi ak ñun, dinga xam li Biibël bi wax ci fànn yooyu ak yeneen. Dinga gëm ne, ‘Mbind mu sell mépp [lépp li ñu bind ci Biibël bi] am na njariñ’ (2 Timote 3:16).

Téere bii du jël palaasu Biibël bi. Waaye dafa lay xiir yow ci sa bopp nga gëstu Biibël bi. Kon ñu ngi lay ñaan, nga jàng aaya yi nekk ci lesoŋ yi, te xool ndax méngoo nañu ak li ngay jàng.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Seetal ni Biibël bi dimbalee ay nit ci seen dund, ak li nga mën a def ba sawar ci jàng ko. Seetal itam li tax nga soxla ñu dimbali la ngir nga nànd ko.

3. Biibël bi mën na leeral suñu yoon

Biibël bi dafa mel ni làmp buy leeral. Biibël bi mën na ñu dimbali ñu jël dogal yu baax, te xamal ñu li nar a xew ëllëg.

Jàngal Sabóor 119:105. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ki bind aaya boobu, naka la gise woon Biibël bi?

  • Yow nag, noo gise Biibël bi?

4. Biibël bi tontu na ci suñuy laaj

Am na benn jigéen ju gis ne, Biibël bi tontu na ci laaj yu am solo yi mu doon laaj boppam ay ati at. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, yan laaj la jigéen ji doon laaj boppam?

  • Naka la ko njàngum Biibël bi dimbalee?

Biibël bi dafa ñuy won ne, laajte lu baax la. Jàngal Macë 7:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Yan laaj ngay laaj sa bopp, te Biibël bi mën cee tontu?

5. Jàng Biibël bi mën na nekk lu neex ci yow

Jàng Biibël bi neex na ñu bare, te ñu ngi ciy jële njariñ. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, naka la ndaw ñi gise woon liir?

  • Léegi, lu tax seen gis-gis ci lu jëm ci liir Biibël bi wuute?

Biibël bi nee na, mën na ñu may xam-xam bu ñuy dëfël, te may ñu yaakaar. Jàngal Room 15:4. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ndax li Biibël bi dige ci lu jëm ci dëfël ak yaakaar, itteel na la?

6. Am na ñu la mën a dimbali nga nànd Biibël bi

Ñu bare ñiy jàng Biibël bi, gis nañu njariñ bi nekk ci waxtaane ko ak ñeneen. Jàngal Jëf ya 8:26-31. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

Góor gi jóge Ecópi, soxla woon na ku ko dimbali ngir mu nànd Mbind mu sell mi. Tey, ñu bare gis nañu njariñ bi nekk ci waxtaan ci lu jëm ci Biibël bi ak ñeneen

BU LA NIT WAXOON: «Jàng Biibël bi amul njariñ.»

  • Lan ngay tontu? Lu tax nga wax loolu?

NAÑU TËNK

Biibël bi dafa ñuy jox ay xelal yu jëm ci suñu dund bés bu nekk, di tontu ci laaj yi ñuy laaj suñu bopp, di ñu dëfël, te di ñu may yaakaar.

Nañu fàttaliku

  • Yan fasoŋi xelal ñoo nekk ci Biibël bi?

  • Ci yan laaj la Biibël bi di tontu?

  • Lan nga bëgg xam ci Biibël bi?

Jubluwaay

GËSTUL

Biibël bi am na ay xelal yu ñu mën a dimbali tey.

«Li Biibël bi wax du xewwi mukk» (wp18 no 1)

Xoolal ni Biibël bi dimbalee benn góor bu xeeboon boppam, bi mu nekkee xale.

Ni ma komaasee am jàmm ci sama dund (2:53)

Seetal xelal yu baax yi Biibël bi di joxe ci dund njaboot.

«12 ponk yiy tax njaboot yi am jàmm» (g18 no 2)

Ñu bare xamuñu kiy ilif àddina si, waaye Biibël bi leeral na ko.

Lu tax ñu war a jàng Biibël bi? (Wideo bi yépp) (3:14)