Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 7

Naka ngeen war a yare seen doom

Naka ngeen war a yare seen doom

“ Kàddu yii ma lay digal tey war nañu nekk ci sa xol, te war nga leen a dugal ci say doom. ” — 5 Musaa 6:​6, 7, MN

Bi Yexowa sàkkee njaboot, dafa dénk xale yi seeni waajur (Kolos 3:20). Yéen waajur yi, seen wareef la ngeen jàngal seeni doom ñu bëgg Yexowa te ñu nekk ay mag yu mën a yor seen bopp ëllëg (2 Timote 1:5 ; 3:​15). Dangeen war a xam it li nekk ci seen xolu doom. Am na solo lool ngeen nekk ay royukaay. Dingeen gën a mën a jàngal seeni doom kàddu Yexowa bu dee yéen ci seen bopp njëkk ngeen koo dugal ci seen xol. — Sabóor 40:⁠8.

1 FEXELEEN BA MU YOMB CI SEENI DOOM ÑU WAX AK YÉEN

LI BIIBËL BI WAX : “ War ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax ”(Kàddu yu Xelu 1:​19). Waajur yi bëgg nañu seeni doom xam ne mën nañu waxtaan ak ñoom ci lépp. Xale yi dañu war a xam ne, saa yu ñu bëggee waxtaan ak yéen seeni waajur, dingeen leen déglu bu baax. Kon yéen waajur yi fexeleen ba, bu seeni doom di nekk ak yéen, mu neex ci ñoom. Su ko defee dina yomb ci ñoom ñu wax leen li nekk seen xol (Saag 3:​18). Seeni doom, bu ñu xamee ne bu ñu leen waxee dara dingeen mer walla ngeen xas leen, duñu leen wax lépp li nekk seen xol. Nangeen leen muñal te faral di leen won mbëggeel bi ngeen am ci ñoom. — Macë 3:​17 ; 1 Korent 8:⁠1.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu seeni doom soxlaa wax ak yéen, nangeen jël jot ngir déglu leen bu baax

  • Deeleen faral di waxtaan ak seeni doom, buleen xaar ba ñu am poroblem ngeen door koo def

2 JÉEMLEEN A NÀND LI ÑU BËGG A WAX DËGG

LI BIIBËL BI WAX : “ Ku teewlu mbir, baaxle ” (Kàddu yu Xelu 16:20). Bu ngeen bëggee nànd li seeni doom di yëg ci seen xol, dina laaj lée-lée ngeen xool li nekk ci ginnaaw wax ji ci boppam. Ndaw yi dañu tàmm di ëppal ci wax. Lée-lée, dañuy wax loo xam ne nekkul li ñu bëggoon a wax. “ Tontu te déggagoo, ndof la ” (Kàddu yu Xelu 18:13). Buleen gaaw a mer. — Kàddu yu Xelu 19:⁠11.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Ak lu seen doom mënta wax, nangeen fas yéene bañ koo dog te bañ koo yuuxu walla def lu mel noonu

  • Jéemleen a fàttaliku li ngeen doon yëg bi ngeen amee seen at ak li nekkoon li ëpp solo ci yéen booba

3 DÉGGOOLEEN CI NI NGEEN DI YARE SEENI DOOM

LI BIIBËL BI WAX : “ Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay ” (Kàddu yu Xelu 1:⁠8). Yexowa moo teg baay ak yaay kilifa ci seeni doom. Dangeen a war a jàngal seeni doom ñu may leen cér te déggal leen (Efes 6:​1-3). Bu waajur yi àndul ‘ booloo bokk xel ’ xale yi dañu koy yëg (1 Korent 1:​10). Yéen waajur yi, bu ngeen juboowul ci benn mbir, fexeleen ba bañ koo wone ci seeni kanamu doom ndaxte loolu mën na waññi cér bi ñu am ci yéen.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Waxtaanleen ba juboo ci ni ngeen bëgg a yare seeni doom

  • Yaw ak ki nga séyal, bu ngeen bokkul gis-gis ci ni ngeen di yare seeni doom, na ku nekk jéem a nànd ni moroomam gise mbir mi

4 TËRALLEEN POROGARAAM NGIR YAR SEENI DOOM

LI BIIBËL BI WAX : “ Tegal gone ciw yoon ” (Kàddu yu Xelu 22:⁠6). Yar xale ni mu ware, kenn du xëy rekk mën ko. Loolu dafa laaj ngeen tëral porogaraam ngir yar seeni doom (Sabóor 127:4 ; Kàddu yu Xelu 29:17). Yar tekkiwul door kese, waaye dangeen ci war a boole xamal xale bi li tax ngeen tëral ay sàrt ci kër gi (Kàddu yu Xelu 28:⁠7). Nangeen leen jàngal itam ñu fonk Kàddu Yexowa te mën a nànd li mu santaane (Sabóor 1:⁠2). Loolu dina leen dimbali ñu mën a jëfandikoo seen xel ngir ràññe lu baax ak lu bon. — Yawut ya 5:​14.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Fexeleen ba seeni doom gise Yexowa ni Ku leen mën a dimbali.

  • Dimbali leen ñu ràññe li leen mën a lor te moytu ko, lu mel ni yenn palaas yu bon ci internet walla fu nit ñi di waxtaan ci internet. Jàngal leen ñu moytu saay-saay yi bëgg a def lu ñaaw ak ñoom.

“ Tegal gone ciw yoon ”