Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 54

Nit Ki Gënoon A Am Doole

Nit Ki Gënoon A Am Doole

NDAX xam nga ci ñi mas a dund ci kow suuf, kan moo gënoon a am doole ? Nit kooku, àttekat la woon. Mu ngi tuddoon Samson. Yexowa moo ko doon jox kàttanam. Bala Samson juddu sax, Yexowa nee woon na yaayam : ‘ Dinga am doom. Góor lay doon. Dina jiite waa Israyil te muccal leen ci waa Filisti yi. ’

Waa Filisti yi, ay nit ñu bon lañu woon. Kanaan lañu dëkkoon. Dañu bare woon ay xeexkat te dañu doon sonal waa Israyil lool. Benn bés Samson mu ngi doon dem ci waa Filisti yi, jékki-jékki rekk mu dégg gaynde bu réy bu ko bëggoon a song. Waaye Samson dafa ko rey ak loxoom kese. Rey na itam ay téeméeri nit ci waa Filisti yu bon yi.

Ginnaaw loolu, Samson nob na jigéen bu tudd Delila. Njiiti Filisti yi wax nañu Delila ne, bu mënee xam fan la Samson jële doole boobu, ñoom dinañu ko jox, ku nekk 1 100 piyesu xaalis. Delila bëgg na am xaalis boobu yépp. Moom bëggul Samson dëgg, bëggul it mbooloo Yàlla. Saa su ne muy laaj Samson fan la ame dooleem boobu mu am.

Samson mujj na ko ko wax. Mu ne ko : ‘ Kenn masul a wat sama bopp. Bi ma juddoo, Yàlla dafa ma tànn ngir ma bokk ci jaamam yi ñuy woowe Nasiréen. Bu ñu watee sama bopp rekk, ma ñàkk sama doole. ’

Léegi Delila xam na lu tax Samson am doole. Mu fexe ba Samson nelaw, teg boppam ci kowam. Mu daldi woo kenn ngir mu wat Samson. Bi Samson yeewoo, amatul woon benn doole. Waa Filisti yi ñów, jàpp ko, yàq ñaari bëtam yi te def ko jaam.

Benn bés waa Filisti yi dañu amoon xew bu mag ngir màggal seen yàlla ji tudd Dagon. Ñu jëli Samson ci kaso bi mu nekoon, indi ko ngir ñaawal ko. Waaye booba dafa fekk mu amaat karaw. Samson wax xale bi ko doon wommat : ‘ Bàyyil ma def sama loxo ci poto yiy téye tabax bii. ’ Samson daldi ñaan Yexowa mu may ko kàttan, mu jàpp ñaari poto yooyu te yuuxu lii : ‘ Naa dee ak waa Filisti yi. ’ Lu mat 3 000 nit ci waa Filisti yi ñoo nekkoon ci xew boobu. Bi Samson puusee poto yooyu, tabax bi yépp daanu te rey nit ñu bon ñooñu ñépp.