Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 7

Nit kii am na fit

Nit kii am na fit

SUUF si mu ngi gën a bare nit. Ñu ci ëpp, ñu ngi mel ni Kayin. Dañuy def lu bon. Waaye am na ku melul ni ñoom. Kooku, Enog la tudd. Ku am fit la. Ñi ko wër ñépp, lu bon rekk lañuy def. Waaye Enog moom, dafay topp Yàlla rekk.

Ndax xam nga lu tax nit ñi doon def lu bon rekk ? Seetal lii : Aadama ak Awa, lekk nañu doomu garab bi leen Yàlla tere woon. Waaye kan moo leen xiir ci déggadi Yàlla ? Malaaka bu bon la woon. Biibël bi dafa ko tudde Seytaane. Mu ngi def lépp ngir nit ñépp bon.

Benn bés, Yàlla digal na Enog mu wax nit ñi li nga xam ne bëgguñu ko dégg. Lii la leen waroon a wax : ‘ Yàlla dina alag ñu bon ñépp. ’ Mën nañu xalaat ne nit ñi meroon nañu lool bi ñu déggee loolu. Xéyna sax jéem nañu rey Enog. Kon dafa waroon a am fit ngir wax leen li Yàlla bëggoon a def noonu.

Yàlla bàyyiwul Enog mu yàgg ci nit ñooñu. Enog, 365 at rekk la dund. Lu tax ñu nee “ rekk ” ? Ndaxte ca jamano jooja, nit ñi dañu gënoon a am doole te dañu doon dund lu gën a yàgg. Doomu Enog, Matusala, bi mu gaañoo, 969 at la amoon !

Ginnaaw bi Enog gaañoo, nit ñi dañu doon gën a bon rekk. Biibël bi nee na lu bon rekk lañu doon xalaat te suuf si feesoon na ak ay nit ñu soxor lool.

Ndax xam nga lu tax coono yooyu yépp amoon ca jamano jooja ? Dafa amoon lu bees lu Seytaane defoon ngir xiir nit ñi ci lu bon. Nañu seet loolu ci nettali bii di topp.