Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Baale mën a fey xuloo

ÑI NEKK CI SÉY ÑOO MOOM LII

4: Baalante

4: Baalante

LI MUY TEKKI

Baale mooy jéggal nit ku la def lu la metti te bañ koo mere. Baale tekkiwul ne dangay xeeb lu bon li nit ki def, walla nga def ni dara masul a xew.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam» (Kolos 3:13).

«Boo bëggee nit, doo xool ci ay njuumteem. Waaye dangay xool ci ni muy góor-góorloo ngir doon nit ku baax» (Aaron).

LI TAX MU AM SOLO

Booy dencal nit ñi mer, mën nga lor sa wér-gi-yaram walla nga jële ci naqaru xol. Mën na itam yàq sa séy.

«Benn bés, sama jëkkër dafa ma baalu ndax lu metti li mu ma defoon. Jafewoon na ci man, ma baal ko. Mujj naa ko baal. Waaye li may rëccu mooy teeluma koo baal. Loolu indi woon na ay jafe-jafe ci suñu diggante, te jaru ko woon» (Julia).

LI NGA MËN A DEF

LAAJAL SA BOPP LII

Bés bu la sa jëkkër walla sa jabar waxee mbaa mu def la lu la naqari, laajal sa bopp lii:

  • ‘Ndax ku gaaw a mer laa?’

  • ‘Li mu def, ndax garaaw na ba mu war maa baalu? Ndax mën naa bàyyi mu jàll rekk?’

WAXTAANAL AK KI NGA SÉYAL CI LAAJ YII DI TOPP

  • Ndax dafay yàgg bala ñuy baalante?

  • Lan lañu mën a def ngir gaaw a baale?

XELAL

  • Boo meree, bul ñaaw njort ci sa jëkkër walla sa jabar.

  • Jéemal a baal ki nga séyal, xam ne «nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare» (Saag 3:2).

«Bu fekkee ne, ñun ñaar ñépp a juum, dafay yomb ñu baalante. Waaye, baale dafay jafe bu fekkee ne kenn rekk moo juum. Fàww nga woyof ngir nangoo baale» (Kimberly).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Gaawala juboo» (Macë 5:25).

Booy dencal nit ñi mer, mën nga lor sa wér-gi-yaram walla nga jële ci naqaru xol. Mën na itam yàq sa séy.