XALE bu jigéen bi ngay gis fii, 12 at la am. Yeesu jàpp na loxoom te yaayam ak baayam ñu ngi taxaw foofu. Ndax xam nga lu tax ñu kontaan nii ? Nañu seet loolu.

Yeesu mu ngi dekkal doomu Yayrus bu jigéen

Baayu xale bu jigéen bi, nit ku mag la. Yayrus la tudd. Benn bés, doomam bu jigéen feebar, ñu tëral ko ci laal. Waaye tanewul, feebar bi di yokku rekk. Yayrus ak jabaram jaaxle lool, ndaxte dafa mel ni xale bi dafay waaj a dee. Doom bu jigéen boobu rekk lañu am. Yayrus dem ci Yeesu. Dégg na kéemaan yi muy def.

Bi Yayrus gisee Yeesu, dafa fekk nit ñu bare wër ko. Waaye Yayrus jaar na ci biir nit ñi, daanu ci tànki Yeesu, ne ko : ‘ Sama doom bu jigéen dafa feebar lool. Maa ngi lay ñaan, nga ñów faj ko. ’ Yeesu ne ko dina ñów.

Bi ñu doon dem, nit ñi di buuxante rekk, ku nekk bëgg ko jege. Jékki-jékki Yeesu daldi taxaw, ne : ‘ Kan moo ma laal ? ’ Dafa yëg kàttan gu jóge ci moom, moo tax mu xam ne am na ku ko laal. Waaye kooku kan la ? Jigéen la bu feebaroon lu mat 12 at feebar bu metti. Moom moo ñówoon te laal yére Yeesu, daldi wér !

Yayrus kontaan na ndaxte gis na ne faj nit, yomb na ci Yeesu. Waaye mu am ku jóge kër Yayrus, ñów, ne Yayrus : ‘ Jaratul ngay sonal Yeesu. Sa doom faatu na. ’ Yeesu dégg loolu, mu ne Yayrus : ‘ Bul tiit. Dina baax. ’

Bi ñu àggee kër Yayrus, ñu gis ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Waaye Yeesu ne : ‘ Buleen jooy. Xale bi deewul. Day nelaw rekk. ’ Waaye dañu ko reetaan, di ko ñaawal ndaxte xam nañu ne dee na.

Yeesu jël baayu xale bi, yaay ji ak ñetti ndawam, ñu dugg ci néeg fi xale bi tëdd. Mu jàpp loxoom te ne : ‘ Jógal ! ’ Xale bi daldi dundaat, ni nga ko gise fii. Mu jóg, dox ! Loolu moo tax yaayam ak baayam kontaan lool !

Du xale bii la Yeesu jëkk dekkal. Ci li ñu jàng ci Biibël bi, ki Yeesu jëkk dekkal, doomu benn jigéen ju jëkkëram faatu la woon te mu dëkk Nayin. Yeesu dekkal na itam Lasaar mi bokkoon ndey ak baay ak Maryaama ak Màrt. Bu Yeesu di nguuru ci Nguuru Yàlla, dina dekkal ay nit ñu baree bare. Ndax loolu neexul a dégg lool ?

Luug 8:​40-56; 7:​11-17; Yowaana 11:​17-44.



Laaj yi

  • Kan mooy baayu xale bu jigéen bi ñuy wone foofu, te lu tax moom ak jabaram jaaxle lool ?
  • Lan la Yayrus def bi mu gisee Yeesu ?
  • Bi Yeesu doon ànd ak Yayrus di dem këram, lan moo xew ci yoon bi, te ban xibaar la Yayrus jot bala ñu àgg ?
  • Lu tax nit ñi nekk ci kër Yayrus di reetaan Yeesu ?
  • Yeesu dafa wax ñetti ndawam, baayu xale bi ak yaayam ñu dugg ci néegu xale bu jigéen bi. Lan la def ginnaaw loolu ?
  • Waxal ñeneen ñi Yeesu dekkal, te li mu def noonu, lan lay wone ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Luug 8:40-56.

    Jigéen bi feebaroon te doon xëpp deret, Yeesu won na ko ne ku am yërmande la te du yem rekk ci li Mbind mi wax, bañ ci boole lépp li ci war a ànd. Naka la defe loolu, te tey lan la njiiti mbooloo karceen yi mën a jàng ci loolu (Luug 8:​43, 44, 47, 48; Lév. 15:​25-​27; Macë 9:​12, 13; Kol. 3:​12-​14) ?

  • Jàngal Luug 7:11-17.

    Am na lu Yeesu defal jigéen ju jëkkëram faatu woon te mu dëkkoon Nayin. Loolu naka la mënee seddal bu baax xolu ñi am mbokk bu gaañu (Luug 7:​13; 2 Kor. 1:​3, 4; Yaw. 4:​15) ?

  • Jàngal Yowaana 11:17-44.

    Naka la Yeesu wonee ne jooy bu sa mbokk gaañoo, dara aayu ci (Ywna. 11:​33-​36, 38; 2 Sam. 18:33; 19:​1-4) ?