XOOLAL Yeesu fii. Mu ngiy jàngal nit ñii ngay gis ñépp ci kow tund bu nekk Galile. Ñi ko gën a jege ñooy taalibeem yi. Tànn na ci 12 ngir ñu nekk ay ndaw. Ndaw yi ñooy taalibe yi Yeesu tànn ngir ñu def liggéey bu am solo lool. Ndax xam nga seen tur ?

Yeesu mu ngi jàngale

Am na Simoŋ Piyeer ak Andare ñi bokk ndey ak baay. Am na Saag ak Yowaana. Ñoom it ñoo bokk ndey ak baay. Am na it keneen ku tudd Saag ak keneen ku tudd Simoŋ. Am na ñaari ndaw yu tudd Yudaa. Kenn ki, Yudaa Iskariyo la. Keneen ki, dañu koy woowe itam Tade. Te it, am na Filib ak Nataneel (mi ñuy woowe itam Bartelemi), ak Macë ak Tomaa.

Ginnaaw bi Yeesu jógee Samari, komaase na waar nit ñi ci lii : ‘ Nguur gi nekk asamaan jegesi na. ’ Ndax xam nga ban nguur la ? Nguuru Yàlla la te nguur dëgg la. Yeesu mooy buuram. Dina nekk asamaan te indi jàmm ci kow suuf si. Nguuru Yàlla dina defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana ju rafet.

Fii, Yeesu mu ngi jàngal nit ñi lu jëm ci Nguur gi. Mu ne leen : ‘ Nii ngeen war a ñaane Yàlla : Suñu Baay bi nekk ci kow. Na sa tur nekk tur bu ñuy teral. Na sa nguur ñów. Na sa coobare am ci suuf mel ni ci kow. ’ Ñaan boobu, ñu bare dañu koy woowe ‘ ñaanu Sang bi ’ walla ‘ Suñu Baay ’. Ndax mën nga wax li nekk ci ñaan boobu yépp ?

Yeesu dafay jàngale itam ni ñu war a digaale ak suñu moroom yi. Mu ne : ‘ Defalleen seen moroom li ngeen bëgg mu defal leen ko. ’ Ku baax ak yow, ndax loolu du la neex ? Kon, ni ko Yeesu waxe, dañu war a baax ak suñu moroom. Ci àjjana jiy am ci kow suuf, ñépp ay def loolu. Loolu, ndax du neex lool ?

Macë pàcc 5 ba 7; 10:​1-4.



Laaj yi

  • Xoolal li ñuy wone foofu. Fan la Yeesu di jàngalee, te ñan ñoo toog ci wetam ?
  • Waxal naka la 12 ndawu Yeesu yi tudd ?
  • Nguur gi Yeesu doon wax bi mu doon waare, ban nguur la ?
  • Yeesu wax na li ñu mën a ñaan Yàlla. Loolu lan la ?
  • Lan la Yeesu wax lu jëm ci ni ñu war a digaale ak suñu moroom ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Macë 5:1-12.

    Naka lañu mën a wonee ne xam nañu ne dafa am li ñu soxla ci wàllu ngëm (Macë 5:3; Room 10:​13-​15; 1 Tim. 4:​13, 15, 16) ?

  • Jàngal Macë 5:21-26.

    Naka la Macë 5:​23, 24 wonee bu baax ne suñu diggante ak suñu mbokk ci ngëm, am na lu muy def ci suñu diggante ak Yexowa (Macë 6:​14, 15; Ps. 133:​1; Kol. 3:​13; 1 Ywna. 4:​20) ?

  • Jàngal Macë 6:1-8.

    Lan la Karceen war a moytu lu jëm ci fexe ba nit gise ko ni ku jub, fekk jubul dëgg (Luug 18:​11, 12; 1 Kor. 4:​6, 7; 2 Kor. 9:​7) ?

  • Jàngal Macë 6:25-34.

    Lan la Yeesu wax ngir wone ne dañu war a wóolu Yexowa ci lu jëm ci faj suñuy soxla ci wàllu xaalis (Gàdd. 16:4; Ps. 37:25; Fil. 4:​6) ?

  • Jàngal Macë 7:1-11.

    Lan lañu mën a jàng ci li Yeesu misaal ci Macë 7:5 (Prov. 26:12; Room 2:1; 14:10; Saag 4:​11, 12) ?