XOOLAL xale bi di waxtaan fii ak mag ñi. Ay jàngalekat lañu ci kër Yàlla gi nekk Yerusalem. Xale bi, Yeesu la. Màgg na te léegi 12 at la am.

Jàngalekat yi waaru nañu lool ndaxte Yeesu dafa xam lu bare ci Yàlla ak ci li ñu bind ci Biibël bi. Waaye lu tax Yuusufa ak Maryaama nekkuñu fi ñoom it ? Ana ñu ? Nañu seet loolu.

Xale bi Yeesu mu ngi waxtaan ak ay jàngalekat

At mu nekk, Yuusufa faral na di yóbbu njabootam ca Yerusalem ngir màggali bés bi ñu woowe bésu Jéggi bi. Nasaret sore na lool Yerusalem. Oto amul, saxar amul. Jamano jooja, loolu lépp amul woon. Kon li ëpp ci nit ñi, dañu doon dox. Ku jóge woon Nasaret, bëgg dem Yerusalem, dafa waroon a dox lu jege ñetti fan.

Yuusufa bare na ay doom yu mu war a toppatoo léegi. Ay rakku Yeesu lañu. Ren, Yuusufa ak Maryaama dem nañu ak seeni doom Yerusalem te léegi ñu ngi ñibbi Nasaret. Pur ñoom, Yeesu mu ngi ànd ak ñeneen ñi ñu bokkal yoon. Waaye bi ñu taxawee ci ngoon si pur fanaan, mënuñu woon a fexe ba gis ko. Ñu daldi ko seet ci biir mbokk yi ak xarit yi. Nekkul ak ñoom ! Ñu daldi dellu Yerusalem, seet ko fa.

Mujj nañu gis Yeesu fii ak jàngalekat yi. Mu ngi leen di déglu te am na lu mu leen di laaj. Ñépp waaru ndax ni Yeesu ame xel. Maryaama ne : ‘ Sama doom, lu tax nga def ñu lii ? Man ak sa baay, ñu ngi la doon seet, jaaxle lool. ’

Yeesu ne leen : ‘ Lu tax ngeen may seet ? Xanaa xamuleen ne dama war a nekk ci sama kër Baay ? ’

Nekk fu ñu mën a jàng lu jëm ci Yàlla, loolu dafa neex Yeesu lool. Ndax loolu waru ñu neex ñun it ? Ca Nasaret fu mu dëkk, semen bu nekk, Yeesu dafa doon teewe ay ndaje ngir jaamu Yàlla. Ndegam dafa doon déglu bu baax, dem na ba xam lu bare ci li nekk ci Biibël bi. Nañu mel ni Yeesu te roy ko.

Luug 2:​41-52; Macë 13:​53-56.



Laaj yi

  • Xoolal li ñuy wone foofu. Ñaata at la Yeesu am, te fan la nekk ?
  • Lan la Yuusufa faral a def at mu nekk, moom ak njabootam ?
  • Bi ñu jógee Yerusalem ba mu def benn fan, lu tax Yuusufa ak Maryaama delluwaat Yerusalem ?
  • Fan la Yuusufa ak Maryaama gise Yeesu, te lu tax nit ñi waaru ?
  • Lan la Yeesu wax yaayam Maryaama ?
  • Bu ñuy jàng lu jëm ci Yàlla, naka lañu mënee mel ni Yeesu ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Luug 2:41-52.

    Ci ndigal yi Yàlla joxoon Musaa, góor ñi rekk la Yàlla santoon ñu dem ci màggal yi ñu doon def at mu nekk. Waaye lan la Yuusufa ak Maryaama daan def, te lu tax loolu nekk lu jar a roy (Luug 2:​41; Deut. 16:16; 31:12; Prov. 22:​6) ?

    Ci lu jëm ci déggal sa wayjur, naka la Yeesu nekke royukaay bu rafet ci ndaw yi tey (Luug 2:​51; Deut. 5:​16; Prov. 23:22; Kol. 3:​20) ?

  • Jàngal Macë 13:53-56.

    Yan ñeenti rakku Yeesu yu góor lañu wax seen tur ci Biibël bi ? Ban liggéey la ñaar ci ñoom mujj a def ci mbooloo mi (Macë 13:​55; Jëf. 12:17; 15:​6, 13; 21:18; Gal. 1:​19; Saag 1:1; Yudd 1) ?