XOOLAL garab yu mag yi, tóor-tóor yu rafet yi ak montaañ yu kowe yi. Ndax loolu lépp rafetul ? Xoolal kéwél gii di lekk ci loxo xale bu ndaw bi. Xoolal itam gaynde yi ak fas yi nekk foofu ci ñax bi. Ndax bëgguloo am kër ci béréb bu mel nii ?

Yàlla dafa bëgg nga dund ba fàww ci àjjana ci kow suuf. Te bëggul mukk nga am benn ci metit yi nit ñi am tey. Lii la Biibël bi wax ci ñiy dund ci àjjana ju bees ji : ‘ Yàlla dina nekk ak ñoom. Dee dootul am walla jooy walla metit. Li amoon bu jëkk, amatul. ’

Yeesu mooy def lépp ba lu rafet loolu am. Ndax xam nga loolu, kañ lay doon ? Dina def loolu bu dindee ba pare lépp lu bon ak nit ñu bon ñépp ci kow suuf. Yaa ngi fàttaliku ne, bi Yeesu nekkee ci kow suuf, faj na bépp fasoŋu feebar, dekkal na sax ñu deewoon. Yeesu dafa def loolu ngir wone li muy def ci kow suuf si sépp, bés bu nguuroo ci nguuru Yàlla.

Xalaatal ni dund gi di neexe ci àjjana ju bees ji ci kow suuf si ! Yeesu dina nguuru ca asamaan ak ñi mu tànn. Dinañu toppatoo képp ku nekk ci suuf si te fexe ba ñépp dëkk ci jàmm. Nañu seet li ñu war a def bu ñu bëggee Yàlla may ñu dund gu dul jeex ci àjjanaam ju bees.

Peeñu ma 21:3, 4; 5:9, 10; 14:1-3.

Ni àjjana di mel


Laaj yi

  • Ci li Biibël bi wax, naka la suuf si di mel bés bu Àjjana amee ci kow suuf  ?
  • Ci Biibël bi, lan la Yàlla dig ñiy dund ci Àjjana ?
  • Kañ la Yeesu di def ba lu neex loolu am ?
  • Bi Yeesu nekkee ci kow suuf, lan la def ngir wone li muy def bés bu nekkee buur ci Nguuru Yàlla ?
  • Yeesu ak ñiy nguuru ak moom ci asamaan, bu ñuy ilif suuf si, lan lañuy defal nit ñi ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Peeñu ma 5:9, 10.

    Lu tax mu mën ñu wóor ne ñiy nguuru ci kow suuf ci junni at yi, dinañu nekk buur ak saraxalekat yu baax te bare yërmande (Efes 4:20-24; 1 Piy. 1:7; 3:8; 5:6-10) ?

  • Jàngal Peeñu ma 14:1-3.

    Dañu bind turu Baay bi ak turu Mbote mi ci jëwu 144 000 yi. Loolu, lu muy wone (1 Kor. 3:23; 2 Tim. 2:19; Peeñ. 3:12) ?