XOOLAL gaal gi ! Am na poroblem, de ! Dafay toj ! Ndax gis nga ñi tëb ci biir géej gi ? Am na ñu àgg tefes ba pare. Góor gi nekk fii, mbaa du Pool ? Nañu seet li ko dal.

Ñi mucc ci gaal gi toj

Yaa ngi fàttaliku ne Pool toog na kaso ñaari at ca Sesare. Ginnaaw loolu, moom ak ñeneen ñu nekkoon kaso, dañu leen dugal ci gaal gu doon jëm Room. Ci yoon bi, am na dun, maanaam suuf su feeñ ci biir géej gi, bu tudd Kereet. Dañu doon jaar ci wetam, ngelaw bu réy daldi am. Ngelaw bi dem ba mënatuñu woon a téye gaal gi. Mënuñu gis naaj bi bëccëg, mënuñu gis biddéew yi guddi. Ñu nekk noonu ay fan yu bare, ba amatuñu woon benn yaakaaru mucc.

Pool jóg, ne leen : ‘ Kenn ci yéen du dee. Gaal gi rekk mooy yàqu, ndaxte biig, benn malaaka Yàlla ñów na ci man, ne ma : “ Pool, bul tiit ! Fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, mi nekk buuru Room. Te Yàlla dina aar bakkanu ñi ngay àndal ñépp ci gaal gi. ” ’

Lu mat 14 fan ginnaaw bi ngelaw bu réy bi komaasee, ci booru minwi, ñi doon dawal gaal gi gis nañu ne xóotaayu ndox mi mu ngi wàññeeku ! Ñu ragal gaal gi dóor ay xeer ci guddi gi te toj, ñu daldi sànni diigal yi, maanaam lu diis lu ñu sànni ci biir géej gi te ñu lonk ko ci gaal gi ngir mu taxaw. Bi bët setee, ñu séen béréb bu wóor bu jege tefes gi fu ñu mënoon a yóbbu gaal gi. Ñu daldi jéem a dugal gaal gi foofu.

Dañu doon jublu ca tefes ga, gaal gi laal tundu suuf bu nekkoon ci biir géej gi, mu daldi caŋ foofu. Géej gi daldi dóor gaal gi ba mu komaasee toj. Ki doon jiite soldaar yi yore woon ñi nekkoon kaso, wax na lii : ‘ Képp ku fi mën a féey, na tëb ci biir ndox mi, jéem a jot tefes ga. Ñi ci des, nangeen def noonu it, langaamu ci ay tojitu gaal gi. ’ Ñu def loolu te 276 nit ñi nekkoon ci gaal gi ñépp àgg nañu tefes te mucc, ni ko malaaka mi waxe woon.

Dun bi mu ngi tudd Màlt. Nit ñi fa nekk, baax nañu lool te toppatoo nañu bu baax nit ñooñu mucc. Bi asamaan si gënee neex, ñu dugal Pool ci beneen gaal, yóbbu ko Room.

Jëf ya 27:1-44; 28:1-14.



Laaj yi

  • Lan moo dal gaal gi Pool nekkoon bi mu awee ci wetu Kereet ?
  • Lan la Pool wax ñi nekkoon ak moom ci gaal gi ?
  • Naka la gaal gi toje ?
  • Lan la njiitu soldaar yi wax, te ñaata nit ñoo àgg tefes te mucc ?
  • Béréb boobu ñu teeroon, naka la tudd ? Bi asamaan si gënee neex, lan lañu def ak Pool ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Jëf ya 27:1-44.

    Bu ñu gisee ni Biibël bi di nettalee tukki bi Pool def ba Room, lu tax mu gën ñu wóor ne Biibël bi dafay wax dëgg (Jëf. 27:16-19, 27-32; Luug 1:3; 2 Tim. 3:16, 17) ?

  • Jàngal Jëf ya 28:1-14.

    Waa Màlt yi, dañu doon jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Waaye ba tey, dañu won Pool ak ñi mu àndaloon “ laabiir gu ràññiku ”. Kon, lan la karceen yi war a wone ñoom itam ? Ci ban fànn lañu ko war a gën a def (Jëf. 28:1, 2; Yaw. 13:1, 2; 1 Piy. 4:9) ?