Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Seede Yexowa yi

Tànnal làkk Wolof

Nettali 74: Góor gii tiitul, ragalul

Nettali 74: Góor gii tiitul, ragalul

XOOLAL góor gi ñuy ñaawal fii. Xam nga kan la? Yérémi la. Yonent Yàlla bu mag la.

Nit ñi ñu ngi ree Yérémi

Bi Yosiyas komaasee dindi xërëm yi ci réew mi, tuuti ci ginnaaw loolu, Yexowa laaj na Yérémi mu nekk yonentam. Yérémi moom, xalaatul ne mën na nekk yonent ndaxte xale la. Waaye Yexowa wax na ko ne Dina ko dimbali.

Yérémi mu ngi wax waa Israyil ñu bàyyi lu bon li ñuy def. Mu ne leen : ‘ Yàlla yi xeet yi di jaamu, duñu yàlla dëgg. ’ Ba tey, ci waa Israyil yu bare, jaamu xérém moo gën jaamu Yexowa, Yàlla dëgg ji. Yérémi mu ngi wax mbooloo mi ne Yexowa dina leen yar ndax lu bon li ñuy def, waaye dañu koy reetaan rekk.

At yi dem. Yosiyas dee. Ñetti weer ci ginnaaw loolu, doomam Yowakim nekk buur. Yérémi kontine di wax mbooloo mi lii : ‘ Bu ngeen soppiwul seen yoon bu bon bi, dinañu alag Yerusalem. ’ Saraxalekat yi jàpp Yérémi te yuuxu ko lii : ‘ Dañu la war a rey ndax li ngay wax nii. ’ Ñu wax doomi buuru Israyil lii : ‘ War nañu rey Yérémi, ndaxte waxul jàmm ci suñu dëkk. ’

Lan la Yérémi di def léegi ? Moom, ragalul ! Mu ne leen ñoom ñépp : ‘ Yexowa moo ma yónni ci yéen ngir wax leen loolu yépp. Bu ngeen soppiwul lu bon li ngeen di def, Yexowa dina alag Yerusalem. Waaye nangeen xam lii : Boo leen ma reyee, nit ku deful dara lu bon ngeen di rey. ’

Doomi buuru Israyil reyuñu Yérémi, waaye ba tey waa Israyil soppiwuñu lu bon li ñu doon def. Ginnaaw loolu, buuru Babilon bi tudd Nebukanesar dafa ñów, xeex ak waa Yerusalem, def waa Israyil jaam, te yóbbu ay junniy nit Babilon. Xoolal loolu ni mu mettee : dafa mel ni ay nit jóge bitim réew, jàpp la te yóbbu la ca réew moo xamul !

Yérémi (Jérémie) 1:​1-8; 10:​1-5; 26:​1-16; 2 Buur yi (2 Rois) 24:​1-17.



Laaj yi

  • Kan mooy góor gi ñuy wone foofu ?
  • Nekk yonent Yàlla, naka la Yérémi doon gise loolu ? Waaye lan la ko Yexowa wax ?
  • Lan la Yérémi kontine di wax mbooloo mi ?
  • Lan la saraxalekat yi jéem a def ngir Yérémi noppi ? Moom nag naka la wonee ne ragalul ?
  • Lan moo xew bi waa Israyil bañee soppi lu bon li ñu doon def ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Yérémi 1:1-8.

    Ni ñu ko mën a gise ci li xewoon ak Yérémi, lan mooy tax nit di mën a def liggéey bi ko Yàlla dénk (2 Kor. 3:​5, 6) ?

    Li Yérémi def, ci lan la mën a xiir xale yi nekk karceen tey (Eccl. 12:1; 1 Tim. 4:​12) ?

  • Jàngal Jérémie 10:1-5.

    Yan kàddu yu am doole la Yérémi wax ngir misaal lu tax gëm ay xërëm amul benn njariñ (Jér. 10:5; Is. 46:7; Hab. 2:​19) ?

  • Jàngal Jérémie 26:1-16.

    Ñi des ci ñi Yàlla tànn ci kow suuf si, bu ñuy yégle àtte Yàlla yi, naka lañuy jàppe ci seen xol li Yexowa waxoon Yérémi, maanaam warul dindi mukk benn baat ci li Muy wax (Jér. 26:2; Deut. 4:2; Jëf. 20:27) ?

    Naka la Yérémi nekke royukaay bu rafet ci Seede Yexowa yi tey bu ñuy yégle àtte Yàlla yi (Jér. 26:​8, 12, 14, 15; 2 Tim. 4:​1-5) ?

  • Jàngal 2 Buur yi (2 Rois) 24:1-17.

    Yuda dafa bàyyi woon Yexowa. Loolu, am na lu metti lu mu jur. Lan la (2 Buur. [2 Rois] 24:​2-4, 14) ?