Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Seede Yexowa yi

Tànnal làkk Wolof

Nettali 36: Nag bi ñu defare wurus

Nettali 36: Nag bi ñu defare wurus

OXOO ! Lan la nit ñi di def nii ? Benn nag lañuy ñaan ! Lu tax ñuy def loolu ?

Musaa dafa yàgg ci tund bi. Mbooloo mi daldi ne : ‘ Xamuñu li dal Musaa. Kon nañu def benn yàlla, mu yóbbu ñu ci biti réew mii. ’

Musaa mu ngi sànni ñaari xeer yi

Aaroona, magu Musaa, wax leen lii : ‘ Kon tekkileen seen jaaro wurus yi, indil ma leen. ’ Aaroona daldi leen dugal ci safara ba ñu ruy, mu defar ci benn nagu wurus. Mbooloo mi ne : ‘ Lii mooy suñu Yàlla bi ñu génne Misra ! ’ Ba pare waa Israyil def benn mbuumbaay te jaamu nagu wurus bi.

Bi Yexowa gisee loolu, dafa mer lool. Mu ne Musaa : ‘ Wàccal gaaw. Mbooloo mi mu ngi def lu bon a bon. Dañu fàtte samay ndigal te ñu ngiy jaamu benn nagu wurus. ’

Ay nit yuy jaamu nag bi ñu defare wurus

Musaa gaaw a wàcc tund ba. Mu gis nit ñi di woy te di wër nagu wurus bi, di fecc. Musaa mer lool ba sànni ñaari xeer fi Yàlla bindoon ndigal yi. Xeer yi toj ba tas. Musaa jël nagu wurus bi, lakk ko ci safara ba mu ruy, ba pare defar ko mu nekk pëndax.

Li mbooloo mi def, bon na lool. Looloo tax Musaa woo ay góor, ne leen ñu jël seen jaasi, ba pare wax leen lii : ‘ Ñu bon ñi doon jaamu nagu wurus bi, dañu war a dee. ’ Ñu daldi rey 3 000 nit ! Ndax loolu wonewul ne Yexowa rekk lañu war a jaamu, te waruñu jaamu ay yàlla yu dul dëgg ?

Gàddaay gi 32:​1-35.



Laaj yi

  • Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la nit ñi di def, te lu tax ñuy def loolu ?
  • Lu tax Yexowa mer, te lan la Musaa def bi mu gisee li mbooloo mi doon def ?
  • Lan la Musaa wax ay góor pur ñu def ko ?
  • Lan lañu war a jàpp ci nettali boobu ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Gàddaay gi 32:1-35.

    Naka la nettali bii di wone li Yexowa xalaat ci boole diine yu dul dëgg ak diine dëgg ji (Gàdd. 32:​4-6, 10; 1 Kor. 10:​7, 11) ?

    Lan la karceen war a moytu buy tànn luy féexal xolam, mel ni bu bëggee woy walla fecc (Gàdd. 32:​18, 19; Efes 5:​15, 16; 1 Ywna. 2:​15-​17) ?

    Naka la giiru Lewi nekke royukaay bu rafet ci lu jëm ci def lu jub (Gàdd. 32:​25-​28; Sab. [Ps.] 18:25) ?