LAN ngay gis fii te amul woon ci nettali 2 ? Benn góor ak benn jigéen. Ñoom ñooy nit ñi jëkk a am ci kow suuf si. Kan moo leen sàkk ? Yàlla la. Ndax xam nga turu Yàlla ? Yexowa la tudd. Góor gi, Aadama la tudd, jigéen bi, Awa.

Aadama ak Awa ci toolu Eden

Nii la Yexowa sàkke suñu maam Aadama : dafa jël suuf, def benn yaramu nit bu amul benn sikk, mu ëf ci bakkanam, Aadama daldi dund.

Yexowa jox na Aadama benn liggéey. Dafa ko wax mu jox mala yépp tur. Xéyna Aadama toog na lu yàgg di leen xool rekk ngir xam tur bu gën a mën a ànd ak xeetu mala bu nekk. Waaye am na lu Aadama gis. Ndax xam nga lan la ?

Mala yépp, ñaar lañu woon. Amoon na pàppa ñey ak yaay ñey, pàppa gaynde ak yaay gaynde. Waaye Aadama moom, amul woon ku muy àndal. Kon, Yàlla dafa nelawloo Aadama, nelaw bu xóot, jël benn yax ci wetam, maanaam benn faar, defar ci benn jigéen, may ko Aadama mu nekk jabaram.

Aadama kontaan na lool ! Awa itam naroon na kontaan. Mu ngi ci tool bu rafet lool ! Léegi, mën nañu am doom te am dund gu neex ci kow suuf si.

Yexowa dafa bëggoon Aadama ak Awa dund ba fàww. Dafa bëggoon ñu liggéey ba àddina si sépp mel ni toolu Eden. Liggéey boobu, Aadama ak Awa naroon nañu ci kontaan lool  ! Boo fa nekkoon, ndax dinga ci bëgg bokk ? Waaye jàmm jooju Aadama ak Awa amoon, yàggul. Nañu seet lu tax ci nettali bii di topp.

Sabóor 83:18; Njàlbéen ga 1:26-31; 2:​7-25



Laaj yi

  • Lan lañuy wone ci nettali 3 loo gisul ci nettali 2 ?
  • Kan moo sàkk góor gu jëkk gi, te naka la tuddoon ?
  • Ban liggéey la Yàlla jox Aadama ?
  • Lu tax Yàlla nelawloo Aadama, nelaw bu xóot ?
  • Ba kañ la Aadama ak Awa mënoon a dund, te ban liggéey la Yàlla bëggoon ñu def ?

Leneen li ñu mën a laaj

  • Jàngal Sabóor 83:18.

    Yàlla, naka la tudd, te ban taxawaay la moom rekk am ci kow suuf si (Jér. 16:21; Dañ. 4:​17) ?

  • Jàngal Njàlbéen ga 1:26-31.

    Lan la Yàlla mujj a sàkk ci juróom-benneelu fan bi, te li mu sàkk noonu, lu mu wuute woon ak mala yi (Njàl. 1:26) ?

    Lan la Yexowa may nit ak mala yépp (Njàl. 1:30) ?

  • Jàngal Njàlbéen ga 2:7-25.

    Lan la Aadama waroon a def ngir mën a wutal mala yi tur (Njàl. 2:19) ?

    Naka la Njàlbéen ga 2:24 di ñu wonee ni Yàlla gise séy, tàggoo ak fase (Macë 19:​4-6, 9) ?