MËN NAÑU LA DIMBALI NGA JÀNG BIIBËL BI

Mën nga dund ci jàmm ba fàww!

Njàngum Biibël bii, doo ci fey dara te dina la dimbali nga am tont ci laaj yii di topp:

  • Naka laa mënee bég ci sama dund?

  • Ndax lu bon ak coono dina mas a jeex?

  • Ndax dinaa gisaat sama mbokk yi gaañu?

  • Ndax Yàlla fonk na ñu dëgg?

  • Lan laa war a def ba Yàlla nangu samay ñaan?

Doo fey dara

Dinañu la jàngal Biibël bi, jox la téere bi nga nar a jàngee, maanaam Mën nga dund ci jàmm ba fàww!, jox la it Biibël bi boo ko soxlaa, te doo fey dara.

Yaay tànn li la gënal

Lu jëm ci njàng mi, yaay tànn waxtu wi ak béréb bi la gënal. Mën nañu ko defe sa kër, walla ñu woo la telefon.

Boo bëggatul

Mën nga bàyyi njàng mi te dara du la ci fekk.

Njàngum Biibël bi, nu muy deme?

Ki lay jàngal dafa lay dimbali nga xam Biibël bi ndànk-ndànk. Jàng Biibël bi jaare ko ci téere Mën nga dund ci jàmm ba fàww! dina la dimbali nga xam ndànk-ndànk li ñu wax ci Biibël bi ak njariñ bi mu la mën a amal. Boo bëggee yeneen leeral, seetaanal wideo bii walla nga xool li nit ñi di faral di laajte ci njàngum Biibël boobu.

Ndax bëgg nga gis li nekk ci téere bi?

Xoolal lesoŋ yi ngay njëkk a jàng.

Ndax pare ngaa tàmbali?

Bësal ci suuf boo bëggee bindu ngir ñu jàngal la Biibël bi.