NAÑU JÀNGE CI YEESU

Fitna fajul dara

Fitna fajul dara

 Ñu bare jàpp nañu ne, bu ñu joteek keneen, defante moo koy faj. Looloo leen di dugal ci jëfi fitna. Waaye, loolu safaanoo naak li Yeesu jàngale. Nañu xool li ñu mën a jànge ci li mu wax ak it ci doxalinam.

Li Yeesu wax

 Cib waare bu siiw bu mu defoon, Yeesu wone na ne, bu ñàkk déggoo amee, du doole, mer walla fitna moo koy faj. Xoolal li mu wax.

  •   «Lépp lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko . . ., nangeen leen ko defale noonu» (Macë 7:12; Luug 6:31). Ab xelal bu am solo ngi noonu. a Yeesu mu ngi ñuy ñaax ci ñu doxaleek ñeneen ñi ni ñu bëgge ñu doxaleek ñun. Kenn ci ñun bëggul ñu koy jaay doole walla ñu koy bundxataal, kon war nañoo jox cér ñeneen ñi te wone mbaax bu dee sax déggoowuñook ñoom.

  •   «Ku leen dóor mbejum lexu ndijoor, dékkleen ko lex ba ca des.» (Macë 5:38, 39; Luug 6:29). Loolu Yeesu wax tekkiwul ne, dañu war a bàyyi ñeneen ñi ñu mettital ñu. Li mu bëggoon a jàngal ay taalibeem mooy, waruñoo di feyyante lu bon, waaye dañu war a ànd ak teey bu amee ku leen merloo. b Ci jamanoom, ñenn ci njiiti diine yi dañu doon jàngale ne, feyyu, dara nekku ci. Xalaat boobu nag, la Yeesu doon jubbanti.

  •   «Soppleen seeni noon» (Macë 5:43, 44; Luug 6:27). Yeesu jàngale na ne, dañu war a baax ak ñi ñu bañ walla di ñu bundxataal. Loolu nag, tekkiwul ne ànd nañu ci li ñuy def. c Waaye, bu ñu baaxeek ñoom, loolu dina giifal seen mer walla sax mu xiir leen ci ñu baax ak ñun.

Li Yeesu def ak li mu nar

 Yeesu jàngale na ne, bu réeroo amee, du doole, mer walla fitna moo koy faj. Moom ci boppam jëfe na li mu doon jàngale. Ci guddi gi ñu koy jàpp ngir reylu ko, kenn ci taalibeem yi jéem na koo xeexal, waaye lii la ko Yeesu wax: «Dellool sa saamar ci mbaram, ndax képp ku bocci saamar, saamar lay deewe» (Macë 26:52). Naka la Yeesu wone ne soppoon na ñi ko bañ? Baal na ñi ko doon bundxataal te dem na sax ba di leen ñaanal! (Luug 23:33, 34; 1 Piyeer 2:23).

 Biibël bi wax na ne, ci kanam tuuti, Yeesu miy Buuru jàmm, dina fi jële bépp xeetu fitna (Esayi 9:5, 6). Boo ci bëggee am yeneen leeral, jàngal waxtaan bii: «Comment la guerre et les conflits violents seront éradiqués».

a Boo ci bëggee am yeneen leeral, jàngal waxtaan bii: «Qu’est-ce que la Règle d’or ?»

b Boo ci bëggee am yeneen leeral, jàngal waxtaan bii: «Que signifie l’expression « œil pour œil » ?»

c Boo ci bëggee am yeneen leeral, jàngal waxtaan bii: «Que signifie « aimer ses ennemis » ?»